url stringlengths 6 8 | content stringlengths 2 3.72k | source stringclasses 3
values |
|---|---|---|
page_1 | Bubakar Bóris Jóob
Doomi Golo | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_2 | Doomi Golo
Nettali | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_3 | XAAJ BU JËKK
NGIRAAN FAY
Gone mat naa bàyyi cim réew | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_4 | TÉEREB DÓOM
I | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_5 | Noonu ma xool ko lu yàgg, daldi yëngal
ndànk sama bopp, ni ko :
Àddina : dund, dee.
Leneen newu fi, Badu.
Lii rekk : demal, maa ngi ñëw.
Naka laa wax loolu, daldi déggaat woykat
ba :
« Àddina amul solo, ndeysaan... Ku ci
dee yaa ñàkk sa bakkan, ndeysaan ».
Booba gone laa woon, nekk ci sama diggu
doole, yaakaa... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_6 | Xéy-na yaa nga ca dëkku naar ya, moo
xam Alseeri la, walla Marog mbaa Libaη.
Foofa de lanu yaakaar ne fa nga nekk.
Kenn amu ci nag lu ko wóor Am na sax
ñu naan :
- Kéwél kat du tëb doom ja bëtt. Badu
Taal kay, xam ngeen ne topp na ciy tànki
baayam Asan Taal. Ba fu coow liy mujje,
Tugal ngeen koy déggi.
Ci juró... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_7 | Téereb Ndéey bi yomb naa xàmmee,
mooy bu xonq bi. Moom laay dénk lépp lu
ma dégg ñu koy waxtaane ci say mbir. Saa
yu ma bettee nit mu lay jëw, dinaa la ko ci
fen. Jàng ko bu baax. Dina la amali njariñ,
bés boo dellusee Ñarelaa gii nga
cosaanoo, fas yéene fee dëkk yaak sa
njaboot. Wóolu naa la, xam naa ne ak loo ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_8 | Foo ko fekkaan mu ngay wut lu mu am,
ñëw bokk kook ndeyam Biige Sàmb ak
maamam
Ngiraan Fay. Dem na bay raxas ay oto ca
Waagu-Ñaay, di baana-baana màrse
Aselem, lépp ndax bañ a wër di ñaanaatu
mbaa di këf alalu jaambur ; jànqi Ñarelaa
yi sax mas nañu ko fee fental woy, di ko
gaaral, waaye teewul mu nekk ci li m... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_9 | Damay daagu ci mbeddi Ñarelaa yi, dégg
ku ne :
- Badu Taal kay, du moo nar a toog bitim-
réew ba musiba di ko fa fekk. Gone
googu, jom la am ba mu mat sëkk, kaar.
Mu mel ni ay baat yu ma ngelaw li yéene,
may ma leen. Ma gaawtu, ñëw ubbi sama
waxande, roccisi Téereb Ndéey, tëral ci
lépp li ma jot a fortaatu.
Su... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_10 | Yilimaan Keeta nee na la nga ñëw tiim sa
baaytàggu ko. Tontuwook sa gémmiñ.
Danga yëngal sa bopp, ngir xamal ka mu
yónni ne jaru ko. Ña toogoon foofu ñépp
jaaxle, ku nekk xool sa moroom
Ndey Silla, ndaw soosu nga xam ne du
dugg mukk lu yoonam nekk, ne la :
- Badu Taal dofuloo jinne jàppu la, demal
wuyu, Yilima... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_11 | - Man Ndey Kumba Silla de, gone guy
waaj a alku laa fi gis. Badu Taal mooy
kan, ba ñu koy seetaan muy toroxal nii
baayaam ? Sama xol jóg man it, ma ni ko :
- Ndey, doo Yàlla doo yonent, mënoo fee
alag kenn. Badu Taal xamul caaxaan, li
mu def am na fu mu ko teg.
Dama ko waxe woon noonu rekk, waaye
ca dëgg-dëgg ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_12 | ak sa ndey Biige Sàmb gën a ub sama
bopp. Li xew Ñarelaa sa ginnaaw ba waa
réew mépp jot ci, foo dem dégg ñu koy
waxtaane, mu yéem ñépp, loolu ndem - si-
Yàlla ji Asan Taal a ko waral.
Waaw. Sa baay Asan Taal.
Lu jiin Njaaga te mooy Njaag,
Coow li wër na àddina si juróom-ñaar.
Amaana sax Penku ba nga nekk,
yée... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_13 | Gënuma laa xam niti tey yi. Yàkkamti
nañu nga may leen nopp, ñuy fen di
dajale. Ñoo fi dàq a yokk, dàq fee
jekk-jekkal ak làq-làqal. Man, Ngiraan
Fay, jomb naa loolu. Jomb naa génnee ci
sama gémmiñ gii lu dul dëgg.
Ku dem ba bejjaaw, am ay sët ak i sëtaat,
loo wax sa digganteek Yàllaa war a tax.
Te su ma demo... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_14 | Su ko defee, nga fanaanee joow ba ne ko
nuus téye, lemmi ko, jàng ko, mu amal la
njariñ. Ñu bare bu ñu gisee ni
may binde, dinañu ne sama yaram neexul.
Waaye faalewuma leen tey, faalewuma
leen ëllëg!Man bokkuma ci bindkat yi ñuy
soow.
Doore ca Musaa Ka ba agsi ci Séex Aliyu
Ndaw, jaar ci ñoomin Sëriñ Mbay Jax... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_15 | Li ma lay waxsi, guléet bésu tey mu génne
sama gémmiñ gii, jaar ci sama xalima,
jaaxaan ci téere bi nga yor, te mu doon la
xaar fii ci Ñarelaa...
Ba nu newee gone maak samay doomi
bàjjan, góor gu ñu doon wax Mbay Lóo
moo nu daan jàngal Alxuraan ci Rëbës gii.
Booba, su dee amoon naa juróom-benni at
tamit, ca la... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_16 | Dara jagatul woon ci moom, du bët yi, du
bëñ yi du tànk yi.
Foo ko fekkaan, mu nga sol benn sabadoor
bu furi, ñu dabb-daaxe ko fu ne, moom ci
boppam muy tëfli deret ; pukkuus ba mu
daan fanaan, mook unk yeek jargoñ yeek
mbóot yi ñoo fa bokkoon dëkk. Du benn du
ñaar, séen naa ay jinax ñuy dóor-dàqe ci
ronu lala... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_17 | Tey jii, su ma sunu Boroom bu baax bi
delloo woon ci sama biiru ndey ji ma jur,
ni ma : dunyaa ci 1922.
Seetlu naa nag ne, ci dëgg-dëgg jot nga
fee jànkoonteek ay jafe-jafe yu bare te tar.
Lu ne jéem nga ko, waaye daal, Ngiraan,
taloo fi dara lu dul lijjanti loo lekk, su
guddee nga tëdd nelaw. Soo yeewoo suba
t... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_18 | Su la neexee nga ni ma : « Njiitu réew mi
Daawur la tudd, sant Jaañ. Moom laa bëgg
a wuutu, am xaalis bu dul jeex, fu ma jaar
takk-der yi di ma mbiibal,
di ma tóojal, lu ma joxoñ dag yi gaawtu
dagg ko, indil ma ». Soo bëggee loolu,
Ngiraan, ma defal la ko. Xam nga ne dara
tëwu ma ! Tey ci guddi, mën naa daaneel... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_19 | - Gaawal, Ngiraan sa tontu laay xaar !
Du man mii maa fay nekk di nakk-nakkal.
Daawur Jaañ, lu mu dégg ci lu bon,
man Ngiraan Fay maa ko ko yakk ! At yi
Daawur Jaañ taxaw ci kaw suuf yépp, soo
ci dindee sàcc alalu réew mi, ak nar ak
yàq xol yi, dara dootu ci des !
Ma ni : tuuge waay, Daawur Jaañ ! Yaay
mag mu ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_20 | Ma dellu ni : wàccoo ngaak askan wi,
Ustaas Mbay Lóo ! Ak li coow liy bare
yépp, sa dund a ëpp njariñ fopp dundug
Daawur Jaañ ak i ñoñam !
Amoo woon jotu jëwaate ak rambaaje,
taloo woon xëccook téesante, te néew
doole masulaa tax a saalit bay wër di
woyaan. Maa ngi lay gisaat, nga sëgg ay
waxtu di jàng Alxuraan... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_21 | Coppite ga ma daan seetlu ci yaw moo ma
tax a xam ne liy tax nit di nite, day jéggi
yaram wa, romb koy dem. Doole ji nekk
ci xam-xam, teey ak fulla ji mu laaj yépp a
ngi woon ci yaw.Waxuma sax Daawur
Jaañ, waaye ku ma indiloon tey jii nit ki
ëpp alal mbaa ki ëpp bayre ci àddina,
duma ko wecceek Ustaas Mbay Lóo.... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_22 | Nit ku sa dund neen, doo am takkandeer,
dara du la wutaleek bàyyima. Ustaas
Mbay Lóo, jàngaloo ma Alxuraan yem ca!
Jóge nga fi, waaye ba sunu jonni tey, yoon
wu ma aw, yaa ma ko xàllal démb, tey
soog a ñëw. Saa yu ma demee ba jàq, su
ma làmbaatoo daj la, nga toog ci sama
wet.
Mu mel ni nekkinu askan wi ab téer... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_23 | Su waxtu wa jotee, dinga xamal sa bopp
lu tax ma ubbil la sama xol, xàll ci
juróom-ñaari yoon yu wuute, te naan la :
Badu Taal, yoon yaa ngii, bu ci sama
baaraam joxoñ topp ko, bul teg feneen say
tànk. Bul ragal a xuus ci biir dex gu
lëndëm gi. Su ma la tàllalee seetu, bul
dem ba jub ko sa fit mel ni lu rëcc, ng... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_24 | Defe naa ne de, Sinuwaa yeek Sàppone yi
rekk ñoo nu rëccagum, te ñooñu sax
gisaguma leen Mbaaw. Su ñu defulee
ndànk, léegi nu ne leen :
- Randuleen fee waay, yéen xamuleen
Sinuwaa mbaa Sàppone dëgg nu muy mel!
Tey nu won leen ko ! Kon boog, Badu
Taal, taawu Asan Fay Taal ak Biige
Sàmb, yow sama sët bu baax bi, ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_25 | foo leen fekk ñu nga ηàbb seen xalimaak
seen kayit, di ci bind ak a nataal yu kenn
xamul. Nee nañoo ay boroom xam-xam
yu mag lañu ! Gaa ñooñu, koo ci laaj lu
muy liggéey, mu ni la :
- Gëstukat laa.
Nga ne ko :
- Ãa ?
- Waa-waaw ! Bul ma ci xeeb ! Lu la
jaaxal ci jant bi mbaa ci biddéew yi mbaa
ci weer week ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_26 | - Su wund wu ñuul wi wëree fukki yoon
niim gii, ganaar gi topp ciy daw, ñu ànd
ñoom ñaar di mbów niy xaj, du ñàkk
Pilitoη ak Sipiteer mbëkkante. Su booba,
suuf si dina yëngu ca Pakistaη ak Kore, te
Kilimaηsaro dina yàbbi ay xal yu xonq
coyy! Xam nga, Badu, waxu dof a ngoog !
Boroom xam-xam yooyu, seen muj duy
f... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_27 | Juróom-ñaari fan yooyu nag, dina am ay
jamono ñu jiitle, bu ci ne dara du ko
wutale ak ba ca topp. Maanaam, su
fekkoon ne bés yi dañuy ñaasu, ni ko sunu
yenn mbokk yi baaxoo def, ñaas yooyee
dañuy mujjee raaf ba far maasaloo, benn
màndarga dootul des ci seen kanam.
Waay, jàmm a neex, Badu ! Dara
yënguwul. Réew... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_28 | Xamal ne kooku, su newulee ci bànneex
it, amul naqar wu tax ñuy wax.
Jamono yooyu mënees nañu leen a
méngaleek asamaan su amul benn niir,
weex tàll, ba nga xam ne su ko picc mu
gën a tuuti riisoo mu mel ni àddina fa lay
doxe tukki àllaaxira. Waaye, am na lu ma
la ci bëgg a yokkal, Badu. Aa, Badu, li ma
lay waxs... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_29 | Baal ma àq de, Badu. Lee-lee sa maam
Ngiraan day dem bay tàggook sagoom.
Day fekk booba ay kàddu yu rafet a ngi
nuur ci sama biir deret, di féey, jàpp ma të
maa bàyyi. Su ma tolloo foofu nag, fàww
ma dugal ci waxtaan wi yu ci bokkul te
duma ko tey.
Nanu dellu boog fa ma ajoon wax ji.
Waaw, dina am it ay jamono... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_30 | Waaye kan mooy am googu jot ag dal-xel
googu ? Liggéeykat yaa ngi bànk seeni
loxo, ne ñoom sonn nañu, te dee, bala ñoo
am jàmm nguur gi daanu, ñu ñàdd njiitu
réew meek njabootam rendi leen, sëlmoo
seen deret.
Réew mi mel ni caga bu def tuunu neen
juutu ci pénc mi, lu neex waay mu def, kii
tàpp ci fer yi, kii s... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_31 | Mu mel ni rekk xeetu ndof gu bees moo
jékki-jékki jàpp ñépp.
Xëccoo boobu, Badu, dara waralu ko lu
dul li ku nekk bëgg a fés, ëllëg-ak-sibir
géwél yi di la woy. Te kat, dinaa la ci
xamal lenn : du nit ñi rekk ñooy jiiroo
ndam loolu.
Juróom-ñaari bés yi ci seen bopp, benn du
ci nangoo des ginnaaw. Ndax li mbir ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_32 | Waaye xam nga ne kenn mënul woon am
naqar ba dab Lingeer Lat Sukk Sire Jogob
Mbóoj ma masoon a séy ak Makoddu, jur
ca Dammel Sàmba Lawbe Faal. Sa doom
ak baayam war a jàkkaarloo ! Ba yëf yi
waree am sax, fekk na Lingeer ak
Makoddu tàggoo. Waaye cofeel ga
Lingeer amoon ci moom desoon na as lëf
ba tey. Makoddu ne... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_33 | Mu ni :
- Bu subaa, dinaa ree tuuti, dinaa jooy
tuuti...Xare bu waroon a am la, am na. Lu
ci des, tey ? Ñetti baat. Dibéeru Guy-
Njulli. Ñetti baat yooyu, lu nee ngi ci biir
: Dammel bu tumuraanke di taxawaalu,
deret juy walangaan ak ñaari réew yu jàq
ba fu jàq yem, di Kajoor ak Saalum.
*
* *
Talaatay Nd... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_34 | Su ma ragalul woon fen sax, dinaa la ni
jaamu-néegu Lingeer la woon.
Xam nga du kooku lañu naan ci yax bu
réy la bokk. Teewul ba jigéeni Waalo ya
jàqee, ñu bare dañoo waaf, moom Mbarka
Ja mu jóg taxaw, ni :
- Dëgg la, waa Tararsaa yi nu song tey ay
góor lañu te bu dee xeex rekk ñoo nu ko
dàq fuuf, waaye nanu... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_35 | - Dellusileen ! Sañ ngeen a taxaw ci
kanamu Buuru Tararsaa naan ko ay jigéen
a leen dàqe Ndeer ?
Xeex bi neeti kur.
Foofa, Mbarka Ja daldi waxati ay waxi
gor.
Dafa ne : Jomb nanoo nekki jaam ginnaaw
Barag. Nanu dugg ci néegu ñax bu mag
bii, taal ko ci sunu kow.
Na mu ko santaanee la ko jineeni waalo ya
defe.... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_36 | Demal, Sadani, man Mbarka Ja maa la ko
sant ! Sadani Caam ma jëkk a nettali
Talaatay Nder, ñaata at la amoon ? Am na
ñu ne juróom-ñetti at doηη la amoon. Dara
wóoru ma ci, waaye lii moom boroom
xam-xam yépp ànd nañu ci : Sadani Caam
ma jëkk a netaali Talaatay Nder, xale bu
ndaw la woon.
Kocc Barma Faal de, dafa... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_37 | Looy wokk bopp ?
Mbir a ngoog, de...
Benn ayu-bés, juróom-ñaari fan la.
Xëccoo ba bés yi daan xëccoo démb,
mooy wéy ba tey. Ndax kat, juróom-ñaari
fan yooyu, balañu ciy ràññee benn, di ko
fàttaliku ëllëg, dina naan deret ba màndi,
màbbloo ay taax yu dul jeex.
Dina tax it saxaaru fetal seek bomb-
lakirmosen yi... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_38 | Su ñu takkaan xare, daawu ca ñaaw ndax
daawul des ginnaaw !
Keneen ne :
- Gàcce ngaalaama !
Nga geestu, fu ne nga xool fa, say bët
duñu dajeek benn Doomu-Aadama. Fekk
na du dara lu dul ngelaw lu jóg, lemmi ay
kàddu, suy lenn ci jaww ji ba noppi ne
mes.Démb lëngoo ak Tey, ñu ànd di
daagu. Ñu ngi mel ni ay doom... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_39 | Su ma la bëggoon a wax lépp de, Badu,
dootuma am jotu waxtaan ak yow ci
mbirum Asan Taal. Xanaa boog, ma
ñamal la as lëf ci diggante Démb ak Tey.
Àndandoo boobu, dara gënu koo yàgg. Fi
lanu ko fékk nun ñépp. Fi lanu koy bàyyi
tamit. Bul fàtte mukk lii ma lay waxsi :
am na bés boo xam ni ci la Yàlla sàkk
àddina ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_40 | - Loo may jaay daη-ηaam nii, yow Démb ?
Tee nga maa déglu te xam ne maa la gën a
xam sa bopp fuuf ?
Kooku faf toog di ko déglu, jàkkaarlook
seetu bi, di ci gis ni ko Tey di yatte.
Waaw, Tey daanaka Lawbe bu waane la,
mooy yatt Démb, moo koy sàkk.
Wax jooju tekki lan, nag, Badu ?
Lii, xanaa : xew-xewi démb ya, ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_41 | Réew dina nekk ci fitna, ay bakkan yu
bare rot ci, nguur gu bees taxaw, ñu jàpp
ne yëngu-yëngu yooyu dinañu des ci xeli
nit ñépp ba fàww. Waaye su ñu ci tegee ay
weer rekk, koo wéetal, cuq ko ngir mu
nettaliwaat la mbir mi, mu jox la tontu bu
wuteek bu moroomam.
Kii ne :
- Lii moo fi amoon.
Ka ca des ne ko :
... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_42 | Soo ko seetee bu baax, xelu nit ci boppam
mooy bàmmeelu Dëgg.
Dinga teewe dara sax, dégg ci rajo bi benn
waa ju dëgër fit di ko nettalee neneen, nga
ànd caak moom.
Moo tax Wolof Njaay, su benn waay
jógee fale, ne :
- Amoon na fi.
Li mu koy jëkk a laaj mooy :
- Ndax ba mu amee yaa fekke ?
Xam nga daldi na ko... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_43 | - Lii ak lii moo fi amoon.
Du ñàkk mu am ñu àndul ciy waxam,
waaye kenn du ko sañ a weddi.
*
* *
Bu ñu nee :
- Loo gis ci nettali lay mujje,
Loolu la tekki.
Soo ko jàppee noonu, dinga xam lu waral
nit di nettali lu mu masta fekke. Seetal ma
lii rekk : kàddu yi ngay jottali, ba ñuy jib,
xaajagoo juddu, w... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_44 | Kàddu yooyu nga tudde ay nar, ñoo ka am
njariñ tey ! Jàppal ne doole jiy jox aw
askan pas-pasu dund ak jëm kanam, ci
baat yi nu mel lay tukkee, ci lay ñaaxe
boppam ngir yeneen réew yi ragale ko xel,
weg ko.
Ndax, soo ko seetee bu baax, ab dëkk lan
la ? Jaww ji la, nit ñi ñëw, fekkuñu fi
dara, ñu feesal ko dell... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_45 | Waaye du tee su ëllëg saa mu fëgg
dënnam, ne am na beneen tur. Ñu laaj ko
tur woowu wan la.
Mu ne :
- Man maay Ndakaaru Jal Jóob !
Ndakaaru, benn dëkk ñaari sant !
Moo tax ni Ndakaaru rëbe warul a jaaxal
kenn. Nit ñaa ngiy dem di ñëw, ñii di lal
ay pexe, janq ji solu ba jekk di daagu, fu
ñu aw xetu litkoloñ ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_46 | sàllaaw xàjj ak seen dootu fi am, benn
gone dootul wër di yalwaan waxatumaak
di fanaan ci mbedd mi, ku tawat ci yéen
dinañu ko faj bu baaxa-baax te dinaa
baaxe seeni doom xeetu njàngale wu
masul a am fenn. Ay nari kese ! Waay, ñii
ñoo yabaate dëgg !
Yéen xale yi sax lañuy gën a noggatu,
ndax, wax dëgg Yàlla, ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_47 | Soo nekkee gan cib dëkk, doo bëgg dara
rëcc la, fépp ngay sànni say bët, lu ne nga
laajte ko, loo ci jële muy lu bees loo jàng.
Soo ñibbee, ñu wër la nag, ngay nettali.
Naan :
- Cim ! Waa Ndakaaroo xayadi ! Ñoom
de, ci diggu tali bi lañuy juug seen
mbaalit. Fu neex waay it mu jonkan saw,
te seen oto yaa nga la... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_48 | - Bul ko sax jéem, saa waay ! Man, wër
naa àddina si juróom-ñaar waaye
musumaa gis fenn lu ni mel. Sér bu gàtt
boobu yem ci pooj tey faral di yaraax
daal, réewum Senegaal rekk la am !
Ki gën a saay-saay ci say xarit am xaat lu
mu yëg ci yaramam, daldi yuuxu :
- Nga ne ma ? Saa waay, foofu kat war
naa neex, déw... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_49 | képp ku tudde sa bopp nettalikat, war nga
foo tollu di muslu ci ñi lay déglu mbaa
ñuy jàng say téere. Moytul ma leen ! Aka
ñoo la bañ tey ! Say noon yu làqu lañu.
Ñu ngi lay siiñ, di la tàccu, waaye feek
sànkuñu la, duñu am lu leen neex. Mën
nañu laa jey ba nga yaakaar ne dunyaa jii
ñu Yàlla sàkkal doyunu. Soo d... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_50 | Loo fiy def ? Ayca, dellul ca sa xërëm ya
waay, ak yéeféer bi nga doon ! Alla
bónni !
Sama tontu benn la mas a doon :
Dëgg la, xawma fu dul Ñarelaa, waaye
maa ko xam tey !
Muy lu wóor it, Badu.
Am nay bés sax dafay mel ni ma gëmm
mbaa ma xippi benn lay doon ci man.
Sama gaa ñi kay, mënuñoo def lu ma bet... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_51 | Su màrse neexulee njaboot gi dëñe mbaa
mu fande.
Mus naa laaj Usmaan Sow lu tax mu
tudde fasam wi Kuwaamini. Duma fàtte
mukk tontu bu doy waar bi mu ma tontu
keroog. Dafa wiccax bopp bi, muuñ ba
noppi ni ma :
- Ci kàllama Suwaayili laa tibbe baat
boobu, Ngiraan.
Ma ne ko :
- Waaw, Usmaan, ba léegi nag lu
Kuw... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_52 | Waaye Usmaan, luy yoonu dawalkatu fasu
Ñarelaa ci kàllaama suwaayili ?
Yow gën a sore fa nga jëlijee sa turu fas
wi ! Bi ma waxee loolu, Usmaan Sow
tàmbalee xàqataay, di la ko reewal ba téye
biir bi. Ku fekkewul reetaani Usmaan Sow
ya keroog, fekkewoo dara!
Mu ngi la koy defal :
- Kex ! Kex ! Kex !
Ma defe... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_53 | Céy lii ! Fu mbëru làmb yi demee bay am
ay tur yu kenn xamul, di làmboo raaya
Amerig, lu tee sama fas wi tudd
Kuwaamini ? Du lii lañuy waxati ?
Ma xam ne li Usmaan Sow wax dëgg gu
wér péηη la, ma daldi soppi mbir mi ay
kaf.
Ma ne ko :
- Ñarelaa daal, du goxu como, Usmaan,
ndax fas yi sax soo leen làkkee suw... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_54 | Ndaw si naan ko :
- Merd, taa géel, muwaa beese taa peer
miil fuwaa.
Ñu jàppe ko noonu, foo tollu di leen dégg.
Nun waa Ñarelaa nag, dunu ay tubaab yu
ñuul, li nu xam ci ay dëkkandoo moo di ne
su ñu tolloo foofu, séytaane roofu seen
diggante, ñu tàggook seen sago, li la war
mooy nga dem wax leen luy tax ñu
de... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_55 | jarul werante. Muse ak Madam Sumaare
kay, ay dëkkandoo yu doy waar lañu.
Muse Sumaaree ka bare tiitar nag, tey !
Nee naay kilifa la. Foo ko fekk mu ngi
xoju ba karwaatam mel ni lu koy tee
noyyi,
bu génne ci otoom bu xant bi sànni bunt
bi, dëngalu, defaraat ay lonetam, di jaay
pers daal, ni ngeen koy waxe yéen g... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_56 | Ngir bañ a guddal lim bi, mën naa ne
Ñarelaa gii ma dëkk, dama koo miin ba
sama gaa ñi leeg-leeg dañu may nirook ay
xuusmaañàpp. Mel ni am na ku làqu ci
béréb bu lëndëm, téye ci buumam di xëcc
na mu ko neexe te su ko defee, Doomi-
Aadama yiy kër-këri, yaakaar, ci seen
doyadeek seen xel mu gàtt, ne li ñuy def
yép... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_57 | Su ma waxee loolu, du caagin dama soxor
mbaa ma ñaaw làmmiñ. Mbir yee ni deme
doηη. Dafa mel ni ku nelawoon ay xarnu
yu baree-bare, bés bu yeewoo du fekk ci
dunyaa ku mu xamutoon walla mu gis fi
lu ko jaaxal.
Sunu Boroom bi mën lépp, yeyoo lépp,
sàkk lépp, liy noyyi ak li dul noyyi, moo
ko defe noonu, nu war k... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_58 | Man, Badu, yàgg naa dox, yàgg naa gis.
Amuma nag sañ-sañ bu tollu naan la :
yoon wu sama baaraam joxoñ, jaar fa.
Sañuma loolu, ndax séytaane dafa bare
doole, àttan na la kar ci yoon wi, nga dem
ba defe ne yaa ci nekk, mu gal-gal la, nga
daanu.
Te bu boobaa, dinga ma mere fekk
defuma la dara.
*
* *
... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_59 | - Diw a fi gën, xamul caaxaan, nit ku jub
la. Su kàddu yooyu tàbbee ci noppam, xol
biy bon, mu daldi tàmbalee rëbb diw
moomu. Du am jàmm feek dugalu ko ci
gilaawaali. Moo tax, Badu, dëgg goo gis,
am na geneen dëgg gu tafu ci wetam, ne
fu mu jaar tiiñal ko. Ngóor soosu may bañ
a tudd nag, du nit ku baax. Ku xamad... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_60 | Fen day xaar ba Dëgg toog ci biir nit ñu
baax ñi di waaraate, mu ne cabax ci biir
mbubbam, làqu fa, di ko dompat, di ko
ηóobi, di ko tex-texaan. Su ko defee, Dëgg
day muñ rekk, xam ne looloo fi sës. Ñi am
seetlu ci jataay bi, dinañu ko gis muy
gaññ, di wokkatu, di muut-muuti fi mu
toog waaye duñu xam lu waral lo... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_61 | Kooku ni ko :
- Aa, am na ñu koy wax de.
Fen xàqataay, yuuxu, gëdd ko :
- Laajuma la loolu, li ma bëgg a xam lii la
: yow ndeyu-mbill gi, lu cee sa xalaat ?
Foofu Dëgg yëngal bopp bi, xaw a mel ni
ku koy dànkaafu :
- Saa waay, yaa ngi may tooñ de...
Séytaane wëndéelu ci biir géew bi, lépp lu
baax la fa Dëgg j... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_62 | - Tuuge waay ! Yow Dëgg, yaa mën a
kàcc tigi !
Dëgg di say, moom it :
- Maa tey laa wax, soo amee loo ciy wax
nga def noonu sa ndey !
Xam nga ni ay daldi na dikk.
Ndaxte Dëgg, dañu koy wax te dee, duy
faral di ànd ak màndute, te tàmmul it di
wax kenn di ci sañ a teg baat. Li mu tàmm
kay, mooy di waaraate, ñé... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_63 | Waaye, tey moom, Dëgg tal na leneen lu
dul yàppu xar wu ñu wàjj ak soow mu ñu
njar ! Bëñ yi rot nañu, deret jaa ngi muur
kanam gi, fi ko Fen njatt di ko wulli mu
ngay woote wall :
- Wóoy sama ndey ! Na ngeen mënee
seetaan ñu di ma def lu ñaawe nii ?
Su ñu leen teqalee, ñuy dàggasante, Dëgg
naan ko yaay Fen, Fen... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_64 | Gis nga nag, Badu, foo fekk ñu wër benn
Doomu-Aadama, di ko tàgg, di ko tàccu,
xamal ne am na ci jataay bi ñu ko ci ñee,
di ko móolu. Noo tudde loolu, yow ?
- Xanaa kañaan, maam Ngiraan !
Waaw, su la neexee nga tudde ko noonu,
Badu. Waaye man de, ci sama gis-gis bu
gàtt bi, yaakaar naa ne du kàñaan doηη.
Gis n... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_65 | Lu tollu nim réew, nga ne teg naa ci loxo,
maa fiy dogal, foo romb ñu tóojal la, koo
waxal ñaari baat mu daldi bëgg a sedd say
loxo ndax bég ci li nga ko yëg, nga yor
alal ju dul jeex di ko pasar-pasare...
Am ñu loolu jaaxal, ñu ne la :
Waaw, yaaram, yow gën a am faayda ! Ku
la ne yaa nu moom ?
Nga ne leen : ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_66 | - Njiitu réew mi kañ, Yàlla may na ko.
Moo baax, moo am yërmaande te bare
xam-xam ! Ku mat kilifaa ngi !
Waaye ngóor soosu wax loolu, walbati
xelam lu yomb la.
Soo ko ne :
- Sunu Demba Njaay mi kenn sañul a
tudd de, dégg naa ne diw mooy góor-
góorlu ci jabar ji.
Dinga gis xaat ni mu bége, bët yiy melax,
mu n... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_67 | góor gu ko romb mu àddu kalpe la, ne la
tekkil gaaw sa tubéy, ngeen daldi ànd di
bërëηu ci moket bi !
- Déet waay ? Man sax, loolu bettu ma !
Moom kañ, paramiyeer daam lañ koy wax
xawma, soo ko xoolee bu baax tele ak
puudaroom bu metti, xam ne lagara bu
bon la !
- Ñoom kay seen bopp lañu fi newal.
Duñu gat, ñi... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_68 | bu xol bi jëmee fii, xel maa ngi koy digal
mu jaar feneen. Dinga agsi cib dëkk, fekk
mag ña fa gën a yiw dajaloo ci pénc miy
déglu benn yaaram, mu leen di soññ ci def
lu baax mbaa di ko wax. Sa yaram daw,
nga ne :
- Lii de, dara dàqu ko, ndeysaan.
Fekk na booba séytaanee ngi yoot ndànk.
Badu, bu ñu la ajee ca k... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_69 | - Maam Ngiraan de, xanaa ba muy bind
téere bii, àndul woon ak sagoom. Ku jóg
kay ba ne dangay nettali, tee ngaa jaaraat
ci li nga fi jot a teewe rekk. Waaye di
waaraate subaak ngoon ! Loolu lu mu ci ?
Wax nga dëgg, Badu. Maa ngi mbebetu
rekk, booba ba léegi. Yaa yey laaj ma :
- Waaw, Maam, lan nga may waaj a
n... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_70 | Laaj naa keroog Biige Sàmb, sa yaay,
ñaata at nga amoon, mu ni ma :
- Bi Asan di dem Tugal, Badoo ngi am
juróom-ñetti weer ak juróomi fan.
Biige yokk na ci sax lu ma ko laajul ndax
nee na ma :
Fan ya ca topp la feebaru ηas bi jëkkee
daaneel Badu. Yàllaa nu musal rekk
waaye tiitoon naa lool, ragal ni sama
doom... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_71 | TÉEREB NGELAW | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_72 | Duma fàtte mukk bés ba nu jëlijee néewu
Asan Taal ayeropooru Ndakaaru.
Bésub alxames la woon, bi timis di waaj a
jot.
Ba nu demee ba jub tali Ngaala Jóob -
mooy jàddukaay bi mujje ci yoonu
ayeropoor - lanu dajeek mbooloo mu
takkoo-takku, kaar. Xanaa waroon naa
tollu ci ñeent mbaa juróomi-téeméeri
junniy nit. Ñ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_73 | Loolu kenn du ko werante. Wànte foo
dégg ay gone di yuuxoondoo tur woowu,
na la wóor ne sunu woykat bu mag bee ko
waral. Móodu Siise rekk a leen ko jaral !
Am na sax ñuy wax ne woykat yi ci Afrig
yépp, Móodu Siise amu ci moroom.
Ñeneen ñi dinañu dem ba naan képp kuy
woy ci àddina si Móodu Siise la ko dàq
fuuf. ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_74 | Bés boobu may wax nag, Móodu Siise
dafa jóge woon bitim-réew. Ci li ma
jotoon a for daal, ndam lu réy la fa
indiwaale woon. Yàlla def mook néewu
Asan Taal ñu bokk benn roppëlaan. Man
yëguma ci woon dara, ndekete fan yooyu
yépp, réew maa ngi waajal Móodu Siise
teeru bu mag a mag. Kenn mënul woon a
ubbi rajo mbaa... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_75 | Seetal ma lii rekk : di jëli sa néew, am
naqar ak tiis, daje faak waa réew mi yépp
ñuy mbumbaay, di fo di ree, yëf yi mel ni
tuq su bënn !
Keroog laa yéemu !
Dafa meloon ni waa dëkk bi dañoo amoon
mbégte ci deewu Asan Taal gi, ñëw di ko
wone...
Dégg nga ba tàyyi ñu naan :
- Tombee waral aay gaaf.
Nun nag, m... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_76 | Am na sax ñu ñëw ba fëgg ko, di yuuxu,
xanaa yaakaar ne woykat bu mag bee làqu
ci biir. Wànte foo dem dinga fa fekk nit ñu
am seetlu. Kenn ci gaa ñooñu moo leen ni
- Aa ! Mel na ne njuumte am na ci yëf yi,
de ! Ñii ma gis de, defe naa ni tal nañu
leneen ! Noonu, ñi mu àndal jëli li mu
wax, daldi nu xàllal yoon... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_77 | da ciy jëkk a diisook man. Su ñu
waxtaanee, lu ma ko digal mu jaar ca.
Kenn réerewul loolu mbir. Dem nañu sax
ba sama mbokk yiy xultu, naan damay
gënale Asan Taal ak sama yeneen doom
yi, maanaam ndem-si-Yàlla ji Paap
Demba ak Ndey Soxna may séy Bolooña.
Ba Asan Taal dee dund, gis naa ko ci
nekkin wu ne. Wànte... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_78 | Fan yee ñu génn, noon naa la sa baay,
Asan Taal, bitim-réew la faatoo.
Nun ay mbokkam nag, xibaar bu tiis
boobu dafa noo jóge kow ndax masunoo
yëg fu Asan woppe. Ndaw su ñuy wax
Yaasin Njaay moo ma woo bés ne ma
Asan génn na àddina. Ba ñu demee ba ci
biir waxtaan wi, laa door a xam lu mu
joteek Asan Taal, moom... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_79 | Ma tàmbalee jàmmanteek moom. Mu dog
ma ci lu gaaw :
- Góor gi, nga baal ma de, waaye fi may
wootee dafa xaw a sore. Dafa am lu ma la
bëggoon a yëgal.
- Loolu lu mu ?
Noonu, mu ne tekk.
Ma ni ko :
- Mbaa du Asan daa feebar ?
- Feebar bi yóbbu na ko.
- Aa ! Loolu kañ la ?
- Biig. Ndaw sa wootee Tugal nag, tax... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_80 | Ñaari baat yu nekk, Yaasin Njaay ni ma :
- Aa, xaalis bu bare la laaj de, te dama war
a feyal Mbisin ak Mbisaan.
Bi ma ko laajee ñooñooy ñan, la ma sog a
xamal ne ay doomi Asan Taal lañu.
Mu jaaxal ma lool. Ma ne ko :
- Asan Taal kañ la fa am i doom ? Man de,
guléet ma dégg loolu.
Foofu, mu xaw a ñagasal baat ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_81 | ngeen yónnee ma xaalis ma ànd ak néewu
Asan Taal indil leen ko Ñarelaa. Soo
fàttalikoo, yow Badu sax laa booleek
moom, yéen ñaar ngeen làkkante seen
nasaraan.
Ci ngeen jëkk a waxe, yaak Yaasin
Njaay. Waxoo ma ci dara, ndax tàmmoo
di nettali mbaa di waxantu. Loolu du sa
jikko. Waaye teewul ma gis ne seen
jokko... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_82 | leeroon na ma ne masul a nob sa baay te
itam masu koo naw
Ku bëgg nit mbaa nga naw ko, neneen
ngay doxale bu génnee àddina, rawatina
bu dee danga ne sa boroom kër la woon.
Fanweeri at yu mat sëkk, Asan Taal toog
ko bitim réew, nekk ci lu ko neex, bindul,
wootewul ! Yu mel nii moo tax ñu naan :
- Ëllëg du añ du... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_83 | Waaye, céy, su Yaasin Njaay géntoon
booba li ko fiy xaar ! Moom it kenn gënu
koo sàggan. Nde moos waroon naa xam
ne Tugal ak Ñarelaa duñu benn. Fii de,
ndekete Biige Sàmb a ngi ko fi doon yeeru
ak meram mu tëwa giif. Bi yëf yi weesoo,
lanu ay xariti Biige Sàmb sog a xamal ne
sa yaay doon na faral di tëkku Asan, ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_84 | Waa gox baa ngi kooy jëw. Bi ñu
tàmbalee coow ci ay mbiram ba am yu ci
senn, laa yëg ne mook Asan Taal nekkaale
nañu ay ati at ca Màrsey. Nee nañu it
Asan jëkkoon na faa takk benn tubaab bu
tudd Natali, Yaasin Njaay dugg ci seen
séy, tas ko.
Lu ne ñu ngi koy wax :
- Dégg naa dafa takkal pot jabaru Asan,
kooka... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_85 | Waaw. Ña ko jot a gis Tugal nee nañu
Yaasin Njaay ku fowe woon boppam la.
Dégg naa nekkewu fa woon lu dul naan
sàngaraak tóx yàmbaa. Wax nañu it ne da
doon cagatu.
Ab sàmbaa-bóoy jóge fale, ngeen waxaale
ba juboo, nga tëj sa buntu néeg, jaaxaan.
Mu dem ci, dem yoonam. Keneen ñëw
yéeg moom it, wàcc, wacc la fa.... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_86 | Am na yoo xam ne de, su doon sama sago
duma la ko nettali. Waaye nu may def ?
War ngaa xam li fi xew sa ginnaaw yépp,
te man doηη maa la ko mën a àgge. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_87 | TÉEREB LËNDËMTU | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_88 | - Badu Taal ?
- Naam.
- Neel Birëm Seen mu ndaw mu teg àttaaya.
- Birëm seetaani na futbal ba, te ni ma ko
xame de, balaa mu fiy teersi reer jot.
- Nu nuy def nag ?
- Xanaa ma jéem a xiim, Maam.
- Yow de sa àttaaya moom...!
- Man kay, xam naa ne wóoluwoo ma ci,
waaye sa bopp ! Sama lëwël amul
moroom, ñaaree... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_89 | Maa ngi ferenklaayu ci béréb bu lëndëm
këruus, ne la jàkk te mënoo fexe ba gis
ma.
Yaa ngi téye ab téere bu ñuul di ko jàng.
Ba ma ko bindee
ak léegi xanaa war naa mat juróom-fukki
at, maanaam genn-wàllu xarnu. Yow ci sa
bopp, Badu Taal, màggat nga. Yaa ngi
bejjaaw ba weex tàll.
Ma waxaat la ko : mënoo maa gi... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_90 | Xéy-na boog da doon jéem a xoromal
mbind mi... Moo, soo demee kat maam
Ngiraan dafa bokk ci bindkat yooyu nga
xam ne, su ñuy nettali benn xew-xew
duñu nangu dara rëcc leen ci. Waaye yenn
wër-wërloo yi jar na koom ? Man de,
nettali lii laa ci xam : nataal li nga gis,
jottali li nga dégg, soo tëddee nelaw.
Rawa s... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_91 | Dafa fekk rekk ne, bindkat boo gis, ñaare
day bëgg tijjee waxtaanam ay kàddu yu
koy sànni ci jaww ji, mu woyof ni picc, ay
kàddoom gën a neex a dégg. Moo tax ñu
naan :
- Léebóon !
- Lëppóon !
- Amoon na fi.
- Daan na am.
- Ba mu amee yaa fekke ?
- Yaa wax ma dégg.
- Waxi tey matul a déglu !... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_92 | Seetlul bu baax Géwél Mbaay. Day jëkk a
raay ndànk sabaram, raayaat ko, jàppee ko
noonu ba yaram wi tàng, muy rëkk, di
xaaccu, jeeg ji sànneeku ci biir géew bi di
njaay-xólléy, mbooloo mi yépp
àndandooy awu.
Te itam Badu, nun bindkat yi danuy faral
di wéet lool. Metit woowu, kenn du ko
yëg ba naan nu mas-sa ! ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_93 | - Yaa ma woo, Ngiraan Fay wuyusi naa la.
Noonu, mu yëngatu ndànk ci béréb bu
lëndëm bi mu jaaxaan, gis ni ma jaaxlee
daldi ma neeti :
Yaa ma woo, du ? Seen dunyaa ju naqadi
jooju de, xam nga ne moos, rus laa gàntu
rekk moo tax nga woo ma ma wuyusi la !
Nde sama bàmmeel bii ma tëdd, jàmm
rekk laa ci gis !
- B... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_94 | Léegi nag, lan moo tax ma fas yéenee aj
mbirum Yaasin Njaay ak waa Ñareelaa,
ne la jabb Téereb Lëndëmtu ?
*
* *
Badu, wax joo gis, am na biir am biti.
Jàppe ma ni nit kuy daagu moom kenn ci
biir àll bu xonq bi. Yoon wi may aw,
Maam yaa ko xàll démb, booba tey
ñëwagul.Lu yoon woowu xat-xat, moom
doηη laa... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_95 | Ba ma nekkee man kenn ci àll bi, sama xel
yépp a ngi woon ci rab yi ma wëroon, làqu,
ne ma jàkk, di ma xeeñtu, nar maa song,
xët ma cig lëndëm. Moo xam till la, walla
bukki, walla segg, walla jaan mbaa xeetu
picc wu mu mënti doon, ñoom ñépp a ngi
ne tekk, di ma yeeru.
Doomu Segg ni :
- Tee noo dal ci kowam, yà... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_96 | Badu, noo mënee dal xel bay wékk sa
yaakaar yépp ci man mii tëx, gumba,
muuma ?
Nga ni ma :
- Dëgg la, ci àll bu lëndëm këruus nga
jóge ! Waaye won ma lépp la nga fa gisul,
jottali ma lépp la nga déggul ba nga fa
jaaree !
Ma reetaan, ndeysaan, daldi ne ci sama
xel :
Aa ! Gone gaa ngi mokkalsi kat !
Nga n... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_97 | Bés boo ñibbisee Ñarelaa, fekk ma jóge fi,
nga lemmi ko, jàng ko, jéem koo firil sa
bopp.
Bu jëkk, gone yi dañu daan toog ci ab jalu
suuf, def géew, ku ci ne di fent lu ko neex,
ngir bégal say moroom. Loolu lañu daan
tudde maye. Dégg nga wax ji de : maye.
Maye... Waay ndax am na lu dàq kàddu
googu ? Ak ni jamo... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_98 | - Waaw, ana ma ? Bii seetoo gën a doy
waar ! Ñii mu may won kat, kenn laa ci
xamul. Boroom lonet yee niroo naak man,
gaa... Am na it ñu ma ci xelmati wànte
wóoruma ne ñoom la. Te sax, jigéen ju
màggat jee toog buntu këram ca Aselem,
téye layoom di tànn ceeb... mel na ni...
Moom a de, moonte ! Waaw, Meer
Sukayna... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_99 | Saa yu sa xel demee ci ñi fi jot a jaar,
njaxlaf ba, tubaarkallà, di tëb di dal ba
noppi xéy ne mes, dara dootu la saf, Kon
kay, su ma fexee ba nga jokkoo ak ña woon
démb, looy waxati ? Lu gaaw-gaaw
nekkaat nga fi gone, topp ci benn balu
futbal bu weex di dóor, di duut say
moroom ba ñuy miir, ngay mbëkk bal bi, ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_100 | Nanu ànd wëri Maam Ngóor.
Soo ma nee :
- Maam Ngóor ? Kuy kookooti, Ngiraan ?
Ma ni la :
Maam Ngóor du kenn. Mooy ñépp, te it
moom doηη mooy Maam Ngóor. Moo jur
ki ma jur. Du xam nga lu loolu tekki ?
Maamaat la ci sa baay Asan Taal.
Fii ma toog ci buntu kër gi, di féexlu, la
sama xel ni yarr ci Maam Ngóor. ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
End of preview. Expand in Data Studio
README.md exists but content is empty.
- Downloads last month
- 10